4Ag maas wéy, ag maas teew; àddina sax ba fàww.
5Jant fenk, so, ne coww dellu fa muy fenke.
6Ngelaw jëm bëj-saalum, wiiri jëm bëj-gànnaar, di wiir ak a wiiraat, di delluy wëndeelu, topp yoonam.
7Dexoo dex wal, wuti géej, te taxul géej fees. Fa dex wal jëm, fa lay walati, jëm.