7Su boobaa pënd dellu suuf, na woon; bakkan dellu fa Yàlla ma able woon.
8Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba. Léppi cóolóoli neen.
9Waarekat ba daa xelu, di jànglewaale xam-xam, di natt ak a gëstu, di jekk-jekkal kàdduy xel yu takku.
10Waarekat ba daa tànn baat yu saf, bind ko, mu jub te dëggu.