3Xàmbaar bu duyee, ba fees, fi kaw suuf lay soob. Garab, bu daanoo ndijoor mbaa càmmoñ, fa mu daanu lay des.
4Kuy déglu ngelaw, doo ji, kuy seetluy niir, doo góob.
5Xamoo yoonu ngelaw, xamoo nu doom di sosoo ci ndeyam; kon manoo xam lu Yàllay def, moom miy def lépp.
6Xëyal, ji sa jiwu, gont, baña tàyyi; muy lii di lee, xamoo lu ciy nangu, am ñaar ñépp ay bokk baax.
7Leer neex na, gis jant neex na.