3 Xàmbaar bu duyee, ba fees, fi kaw suuf lay soob. Garab, bu daanoo ndijoor mbaa càmmoñ, fa mu daanu lay des.
4 Kuy déglu ngelaw, doo ji, kuy seetluy niir, doo góob.
5 Xamoo yoonu ngelaw, xamoo nu doom di sosoo ci ndeyam; kon manoo xam lu Yàllay def, moom miy def lépp.
6 Xëyal, ji sa jiwu, gont, baña tàyyi; muy lii di lee, xamoo lu ciy nangu, am ñaar ñépp ay bokk baax.
7 Leer neex na, gis jant neex na.