6Dëddul jëfi téxét ba dund, di jubal ci yoonu dégg.»
7Artu kuy ñaawle, feyoo saaga rekk, yedd ab soxor, yooloo loraange.
8Bul yedd kuy ñaawle, da lay jéppi; yeddal ku rafet xel, mu naw la.
9Xelalal ku xelu, mu yokku. Xamalal ku jub, mu yokk njàngam.
10Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu rafet xel, xam Aji Sell ji di am ug dégg.
11Maay Xel mu Rafet, ku ma topp gudd fan, dund, dundati.
12Rafet xel, jariñu, kuy kókkalee, wéetook sa añ.
13Jigéen ju dof day xumb, reew, du xam lu xew.
14Day toog bunt këram, mbaa fu kawee kawe ca dëkk ba,
15di woo ña fay jaare te jubal seenu yoon.
16Ma nga naa: «Képp ku téxét, jàddal ba fii!» Ku ñàkk bopp, mu ne ko: