2Mu rendi ag juram, njafaan ay biiñam, xelli, taaj ay ndabam.
3Xel mu Rafet yónni ay janqam, di wootee fu kawee kawe ca dëkk ba,
4naan: «Képp ku téxét, jàddal ba fii!» Ku ñàkk bopp, mu ne ko:
5«Kaay, ma may la, nga lekk, xellil lay biiñ, nga naan.
6Dëddul jëfi téxét ba dund, di jubal ci yoonu dégg.»
7Artu kuy ñaawle, feyoo saaga rekk, yedd ab soxor, yooloo loraange.
8Bul yedd kuy ñaawle, da lay jéppi; yeddal ku rafet xel, mu naw la.