4«Yeen mbooloo yi laay yéene, doom aadama yi laay joor.
5Téxét bi, deel foog, dof bi, déggal ndéey lu xelu.
6Déglul, ma wax la lu am solo, dégtal la njub.
7Dëgg laay wax, di bañ wax ju bon.
8Lu ma wax njub la. Amul lu dëng mbaa lu jekkadi.
9Lépp a dëggu ci ku am ug dégg, te jub ci ku for xam-xam.