Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 8

Kàddu yu Xelu 8:17-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
17Maa sopp ku ma sopp, ku ma seet tigi, gis ma.
18Alal ak teraangaa ngi fi man, am-am bu sax it ak yoolu njekk.
19Li may mayee gën wurus, wa gën, sama njariñ wees xaalis ba gën.
20Yoonu njekk laay jaare, di jëfe li yoon àtte rekk.
21Ku ma sopp, ma nàddil la, feesal sab denc.»
22Soxna si, Xel mu Rafet nee na: «Aji Sax ji jagoo na ma ca njàlbéen, ma jiitu ca jëfam ya woon.

Read Kàddu yu Xelu 8Kàddu yu Xelu 8
Compare Kàddu yu Xelu 8:17-22Kàddu yu Xelu 8:17-22