Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 8:17-22 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 8:17-22 in Kàddug Yàlla gi

17 Maa sopp ku ma sopp, ku ma seet tigi, gis ma.
18 Alal ak teraangaa ngi fi man, am-am bu sax it ak yoolu njekk.
19 Li may mayee gën wurus, wa gën, sama njariñ wees xaalis ba gën.
20 Yoonu njekk laay jaare, di jëfe li yoon àtte rekk.
21 Ku ma sopp, ma nàddil la, feesal sab denc.»
22 Soxna si, Xel mu Rafet nee na: «Aji Sax ji jagoo na ma ca njàlbéen, ma jiitu ca jëfam ya woon.
Kàddu yu Xelu 8 in Kàddug Yàlla gi