11Ndax man, xel mu rafet, maa gën gànjar, loo bëgg maa ko raw.
12«Man, Xel mu Rafet, foog di sama kër; xam-xam ak pexe, ma for.
13Ragal Aji Sax ji mooy bañ lu bon. Réy, xeebaate, yoonu mbon, ak wax ju jekkadi, ma boole bañ.
14Maa moomi digle, di maye gis-gis; maa am ug dégg, di boroom doole.
15Samay pexe la buur di jiitee, kilifa di ci àttee dëgg.
16Ci samay pexe la njiit di saytoo, ñook kàngam yeek ñiy àtte dëgg ñépp.
17Maa sopp ku ma sopp, ku ma seet tigi, gis ma.
18Alal ak teraangaa ngi fi man, am-am bu sax it ak yoolu njekk.