3Yaa ngi ci sa loxoy moroom, kon defal nii, doom, ba rëcc: doxal tinuji ko, raamali ko.
4Bul gëmm, bul nelaw!
5Dawal ni kéwél gu rëcc ub rëbb, ne fërr ni picc mu raw ab fiirkat.
6Yaafus bee, xoolal xorondom, seetal ci moom, ba muus.
7Du ku ko yilif mbaa ku koy sas, te jiiteesu ko.
8Bu jotee mu denc ab dundam, mu jot, mu for lekkam.