10Ngay dajjant ak a for bët, di tegley loxook a jaaxaan.
11Néewlee ngi lay dikkal nib sàcc, ñàkk gànnaayul la.
12Ku tekkeedi te bon, day wër di fen,
13day piis, di wokkeb tànk, di waxe baaraam,
14jekkadiy xalaat, di mébét lu bon aka yokku ay.
15Moo tax musiba di jekki dal ko, mu jekki yàqu, ba wees paj.
16Juróom benn a ngii yu Aji Sax ji bañ, ba ci juróom yaar yu mu seexlu:
17kuy daŋŋiiral, kuy fen, kuy rey nit ku deful dara,
18kuy fexe lu bon ci xolam, kuy gaawtuy def lu ñaaw,
19seede buy fen rekk, rawatina kuy yokku ay ci biiri bokk.
20Doom, defal li la baay sant, te bul wacc ndigalal yaay.
21Takkal foo tollu, taf ci sa xol, fas ko ci sa baat.
22Booy dox mu di la jiite, nga tëdd, mu di la sàmm, nga yewwu, mu di la waxal.
23Santaane da lay niital, ndigal leeralal la, artook ub yar di yoonu dund.
24Da lay aar ci ndaw su bon ak jabaru jaambur ak làmmiñam wu neex.
25Bu ko xemmeme taaram, bumu la fiir aki lamsal.
26Dogu mburu fey nab gànc; waaye jabaru jaambur, bakkanu lëmm.
27Te ku ne sawara cas, tafoo, lakk say yére.
28Ku dox ciy xal it, say tànk ñor.
29Mooy ànd ak jabaru jaambur, ku ko def gis ko.
30Deesul sikk ku sàcc aw ñam, def ci biiram ndax xiif.
31Waaye bu feeñee, fey boroom juróom yaari yoon, joxe alalu këram yépp.
32Njaaloo di ñàkk bopp, kuy sànk bakkanam a koy def.
33Mbugal ak toroxte dib añam, te gàcceem du deñ.