5Tànk ya day bartalu wuti ndee, ay jéegoom àkki njaniiw.
6Rëddul yoonu dund, daa lajj, te xamu ko.
7Kon, doom, déglu ma, bul wacc samay kàddu.
8Soreel ndaw soosu, bul jege bunt këram.
9Kon nga ñàkk daraja, keneen jagoo; ku néeg bóom la.
10Jaambur jariñoo sa doole, doxandéem jagoo saw ñaq.