Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 5:5-10 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 5:5-10 in Kàddug Yàlla gi

5 Tànk ya day bartalu wuti ndee, ay jéegoom àkki njaniiw.
6 Rëddul yoonu dund, daa lajj, te xamu ko.
7 Kon, doom, déglu ma, bul wacc samay kàddu.
8 Soreel ndaw soosu, bul jege bunt këram.
9 Kon nga ñàkk daraja, keneen jagoo; ku néeg bóom la.
10 Jaambur jariñoo sa doole, doxandéem jagoo saw ñaq.
Kàddu yu Xelu 5 in Kàddug Yàlla gi