2kon nga saxoo foog, say wax tegu ci xam-xam.
3Lu mel ni lem la ndaw su yemadi di wax, làmmiñ wa ni diw gu ñu lay raay.
4Muj ga mu wex xàtt, di gaañe ni ñawkay saamar.
5Tànk ya day bartalu wuti ndee, ay jéegoom àkki njaniiw.
6Rëddul yoonu dund, daa lajj, te xamu ko.
7Kon, doom, déglu ma, bul wacc samay kàddu.
8Soreel ndaw soosu, bul jege bunt këram.