2 kon nga saxoo foog, say wax tegu ci xam-xam.
3 Lu mel ni lem la ndaw su yemadi di wax, làmmiñ wa ni diw gu ñu lay raay.
4 Muj ga mu wex xàtt, di gaañe ni ñawkay saamar.
5 Tànk ya day bartalu wuti ndee, ay jéegoom àkki njaniiw.
6 Rëddul yoonu dund, daa lajj, te xamu ko.
7 Kon, doom, déglu ma, bul wacc samay kàddu.
8 Soreel ndaw soosu, bul jege bunt këram.