5Amal xel mu rafet akug dégg. Bul fàtte te bul moy samay wax.
6Bul dëddu xel mu rafet, da lay aar; sopp ko, mu sàmm la.
7Njàlbéenu xel mu rafet mooy sàkku ko; ak loo mana am, amal ug dégg.
8Nawal xel mu rafet, mu darajaal la; tafoo ko, mu teral la.
9Da lay takkal kaala gu jekk, solal la mbaxanam buur.»