Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 4:5-9 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 4:5-9 in Kàddug Yàlla gi

5 Amal xel mu rafet akug dégg. Bul fàtte te bul moy samay wax.
6 Bul dëddu xel mu rafet, da lay aar; sopp ko, mu sàmm la.
7 Njàlbéenu xel mu rafet mooy sàkku ko; ak loo mana am, amal ug dégg.
8 Nawal xel mu rafet, mu darajaal la; tafoo ko, mu teral la.
9 Da lay takkal kaala gu jekk, solal la mbaxanam buur.»
Kàddu yu Xelu 4 in Kàddug Yàlla gi