Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 4

Kàddu yu Xelu 4:1-25

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Gone yi, tee ngeena dégg yaru baay, te déglu, ba am ug dégg?
2Maa ngi leen di jàngal lu baax, buleen fàtte sama njàngle.
3Man it amoon naa baay, di benn bàjjo ci saa ndey.
4Baay digal ma, ne ma: «Jàppal samay wax ci sam xel, di jëfe samay santaane, ba dund.
5Amal xel mu rafet akug dégg. Bul fàtte te bul moy samay wax.
6Bul dëddu xel mu rafet, da lay aar; sopp ko, mu sàmm la.
7Njàlbéenu xel mu rafet mooy sàkku ko; ak loo mana am, amal ug dégg.
8Nawal xel mu rafet, mu darajaal la; tafoo ko, mu teral la.
9Da lay takkal kaala gu jekk, solal la mbaxanam buur.»
10Déglul, doom, te dégg saay wax, ndax nga gudd fan.
11Yoon wu xelu laa la teg, jaarloo la yoonu njub.
12Doo dox ba tërëf, doo daw, téqtalu.
13Ŋoyal cib yar, bul yoqi, sàmm ko, moo yor sa bakkan.
14Yoonu ku bon, bu ci tegu; fu ab soxor di jaar, bu fa dox.
15Moyul, bu fa jaare; mbasal te wéy!
16Ku bon du nelaw te lorewul, du dajjant ba kera muy téqe.
17Daa bon, def ko lekk, di màndee coxoram.
18Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.
19Yoonu ku bon ne këruus, du xam lu muy téqtaloo.
20Doom, déglul samay kàddu, teewlul samay wax.
21Bu ci noppee ja jàkk, te jàpp ko ci sa biir xel.
22Mooy dundloo ku ci jàpp, di wéral jëmmam jépp.
23Sàmmala sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
24Dàqal wor, mu sore la; kàdduy naxe, na la dànd.
25Xooleel, sa bët ne jàkk, ngay xool sa kanam màkk.

Read Kàddu yu Xelu 4Kàddu yu Xelu 4
Compare Kàddu yu Xelu 4:1-25Kàddu yu Xelu 4:1-25