2ngir fan wi gudd lool, nga gëna am jàmm.
3Bu la ngor ak worma dëddu, booleel takk ci sa baat, bind ko ci sa àlluway xol.
4Kon nga xam lu jaadu, neex Yàllaak doom aadama.
5Nanga wóoloo Aji Sax ji, sa léppi xol, te bul wéeru ci saw déggin.
6Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon.
7Bul doyloo sa xel mu rafet, ragalal Aji Sax ji, dëddu mbon;
8sa yaram wér, say cér naat.