3Ngalla wutala dégg, wool dég-dég wall.
4Sàkkul xel mu rafet ni xaalis, wut ko ni alal ju làqu.
5Kon nga xam luy ragal Aji Sax ji, xam Yàllaa di kan;
6ndax Aji Sax jeey maye xel mu rafet, kàddoom di taxa xam, di dégg.
7Day dencalal ndam kiy jubal, di yiir ku mat.