18Fu Yàlla feeñoowul, nit ña fétteeral, waaye ku topp yoon, am mbégte.
19Waxi neen yarul surga, da lay dégg te du la déggal.
20Ana koo gis, mu rattaxle? Kooku ab dof a ko gën demin.
21Ku yàq sab surga ba muy ndaw, bu ëllëgee mu defe ne doom la.
22Boroom xadar day sooke ay, te ku tàng bopp moy, moyati.