Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 29

Kàddu yu Xelu 29:10-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
10Ab bóomkat day sib ku mat, di wuta bóom kuy jubal.
11Ab dof day mer, sàmbaar; ku xelu, mer, ànd ak sagoom.
12Kilifa dégluy fen, jawriñ yépp di ñu bon.
13Ku ñàkk ak ka ko nennoo bokk lenn, Aji Sax jee leen boole sàkk.
14Buur àtte way-ñàkk ci dëgg, ab jalam sax.
15Deel bantal ak a yedde, day rafetal xel; gone goo bay-bayal, mu gàcceel ndeyam.
16Bu ku bon féetee kaw, ag moy law, waaye ku jub, fekke jéllu ku bon.

Read Kàddu yu Xelu 29Kàddu yu Xelu 29
Compare Kàddu yu Xelu 29:10-16Kàddu yu Xelu 29:10-16