Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 29:10-16 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 29:10-16 in Kàddug Yàlla gi

10 Ab bóomkat day sib ku mat, di wuta bóom kuy jubal.
11 Ab dof day mer, sàmbaar; ku xelu, mer, ànd ak sagoom.
12 Kilifa dégluy fen, jawriñ yépp di ñu bon.
13 Ku ñàkk ak ka ko nennoo bokk lenn, Aji Sax jee leen boole sàkk.
14 Buur àtte way-ñàkk ci dëgg, ab jalam sax.
15 Deel bantal ak a yedde, day rafetal xel; gone goo bay-bayal, mu gàcceel ndeyam.
16 Bu ku bon féetee kaw, ag moy law, waaye ku jub, fekke jéllu ku bon.
Kàddu yu Xelu 29 in Kàddug Yàlla gi