4Ku wacc yoon, gërëm ku bon; ku wormaal yoon, jànkoonteek ku bon.
5Ku bon xamul njub, kuy wut Aji Sax ji, xam nga njub bu wér.
6Ñàkk te mat moo gën barele te dëng.
7Gone gu sàmm yoon am nag dégg, ku ànd ak sagaru nit gàcceel sa baay.
8Kiy leble di tege, ba barele, kay yéwéne néew-ji-doole lay dencal.
9Soo dee tanqamlu yoon, sag ñaan sax Yàlla suur na ko.
10Ku yóbbe bàkkaar nit kuy jubal, yeer ma nga gas, yaa cay tàbbi, waaye ku mat di jagoo ngëneel.
11Waay a ngi barele, defe ne xelu na; ku néewle am ug dégg, gis ne xeluwul.
12Bu ku jub amee ndam, mbégte mu réy la; ab soxor falu, ñépp làquji.
13Kuy làq say tooñ doo baaxle, ku koy nangu, tuub ko, am yërmandey Yàlla.