Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 27

Kàddu yu Xelu 27:3-8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Doj diis na, suuf dib sëf, waaye fitnay dof a ko raw.
4Xadar day ñàng, mer di wal mu baawaan, waaye fiiraange amul moroom.
5Artu yu ñu la biralal moo gën cofeel gu la boroom ñooru.
6Soppe, bu lay gaañ sax, wóolu ko. Nit bañ na la, te di la fóon lu bare.
7Ku suur, bañ lem ju xelli, waaye boo xiifee, lu wex lu ne neex la.
8Ku sore fa nga bokk, dangay mel ni picc mu sore tàggam.

Read Kàddu yu Xelu 27Kàddu yu Xelu 27
Compare Kàddu yu Xelu 27:3-8Kàddu yu Xelu 27:3-8