9Kàddu gu xelu ci gémmiñug dof mooy car aki dégam, màndikat xàcci.
10Njaatige luy liggéeyloo ab dof ak kuy romb, daa mel ni fittkat buy gaañ ku ne.
11Dof day def jëfi dof, dellu ca, mooy xaj, bu waccoo, lekkaat ko.
12Ana koo gis mu ne: «Maa xelu»? Kooku ab dof a ko gën demin.
13Ab yaafus da naan: «Gayndee ngi ci yoon wi! Gayndee ngi ci mbedd mi!»
14Ab yaafus day tëdd ak a walbatiku, mooy bunt, day jaayu, demul fenn.