9 Kàddu gu xelu ci gémmiñug dof mooy car aki dégam, màndikat xàcci.
10 Njaatige luy liggéeyloo ab dof ak kuy romb, daa mel ni fittkat buy gaañ ku ne.
11 Dof day def jëfi dof, dellu ca, mooy xaj, bu waccoo, lekkaat ko.
12 Ana koo gis mu ne: «Maa xelu»? Kooku ab dof a ko gën demin.
13 Ab yaafus da naan: «Gayndee ngi ci yoon wi! Gayndee ngi ci mbedd mi!»
14 Ab yaafus day tëdd ak a walbatiku, mooy bunt, day jaayu, demul fenn.