21Këriñ defi xal, matt xamb ub taal, ab xulookat di xambu ay.
22Waxi jëwkat di ñam wu neex, wuy seey, jàll ca biir-a-biir.
23Kuy wax lu neex, tey mébét lu bon, yaay xaalis bu rax, ñu xoob ca ndabal xandeer.
24Ab noon làqoo na ay waxam, lal pexey wor ca xolam.
25Buy wax lu neex, bul gëm, ñaawtéef la xol ba fees dell.