Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 26:21-25 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 26:21-25 in Kàddug Yàlla gi

21 Këriñ defi xal, matt xamb ub taal, ab xulookat di xambu ay.
22 Waxi jëwkat di ñam wu neex, wuy seey, jàll ca biir-a-biir.
23 Kuy wax lu neex, tey mébét lu bon, yaay xaalis bu rax, ñu xoob ca ndabal xandeer.
24 Ab noon làqoo na ay waxam, lal pexey wor ca xolam.
25 Buy wax lu neex, bul gëm, ñaawtéef la xol ba fees dell.
Kàddu yu Xelu 26 in Kàddug Yàlla gi