17Kuy xuloo lu sa yoon newul, yaa jàpp ci noppi xaj buy romb.
18Nit kuy naxe, naan: «Damay fo!» yaay dof buy sànniy jum, di fitteek a reye.
20Bu matt amul, ab taal fey, fu soskat amul it, xuloo jeex fa.
21Këriñ defi xal, matt xamb ub taal, ab xulookat di xambu ay.
22Waxi jëwkat di ñam wu neex, wuy seey, jàll ca biir-a-biir.
23Kuy wax lu neex, tey mébét lu bon, yaay xaalis bu rax, ñu xoob ca ndabal xandeer.
24Ab noon làqoo na ay waxam, lal pexey wor ca xolam.
25Buy wax lu neex, bul gëm, ñaawtéef la xol ba fees dell.
26Su la nëbbalee mbañeel, di la nax it, ag mbonam mujj bir ñépp.
27Ku gasal nit am yeer, yaa cay daanu; ku béraŋu doj, ngir tance, yaay tancu.