14Ab yaafus day tëdd ak a walbatiku, mooy bunt, day jaayu, demul fenn.
15Ab yaafus day yeb loxoom ci ndab, waaye yékkati ko, sex, da koy sonal.
16Ab yaafus day foog ne moo gëna muus juróom ñaari boroom xel yu xam tont.
17Kuy xuloo lu sa yoon newul, yaa jàpp ci noppi xaj buy romb.
18Nit kuy naxe, naan: «Damay fo!» yaay dof buy sànniy jum, di fitteek a reye.