Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 26

Kàddu yu Xelu 26:1-8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Teraanga jekkul cib dof, mooy seddub nawet mbaa taw cim ngóob.
2Ñaan-yàlla, soo tooñul, du la dal, day mel ni picc muy naaw, tëë toŋ.
3Xiir, aw fas; laab, mbaam; yetu gannaaw, ab dof.
4Bul topp ab dof cig ndofam, lu ko moy nga mel ni moom.
5Waaye toppal ab dof cig ndofam, lu ko moy mu defe ne daa muus.
6Ku yóbbante ab dof kàddu, yaa woo fitna, gor say tànk.
7Kàddu gu xelu ci gémmiñug dof, mooy tànki lafañ, amalu ko njariñ.
8Kuy teral ab dof, jël ngaw doj, takk ko ci mbaq.

Read Kàddu yu Xelu 26Kàddu yu Xelu 26
Compare Kàddu yu Xelu 26:1-8Kàddu yu Xelu 26:1-8