22day rus ba mel ni koo yeni xal, te Aji Sax jee lay fey.
23Jëw, mer a cay topp; mooy ngelawal taw, taw a cay topp.
24Dëkkeb ruq cim sàq moo gën jabar ju pànk.
25Xibaaru jàmm, bawoo fu sore mooy ndox mu sedd ci ku loof.
26Ku jub bu dee nangul ku bon, yàqu na, ni seyaan bu nëx mbaa teen bu xàbb.
27Lekk lem ju ëpp baaxul, te wut waaw-góor du ngóora.