Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 25

Kàddu yu Xelu 25:20-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
20Kuy woy, boroom tiisu xol di dégg, yaa futti mbubbam cib sedd, mbaa nga jonj xorom ci góomam.
21Bu sab noon xiifee, jox ko mu lekk, bu maree, may ko mu naan,
22day rus ba mel ni koo yeni xal, te Aji Sax jee lay fey.
23Jëw, mer a cay topp; mooy ngelawal taw, taw a cay topp.
24Dëkkeb ruq cim sàq moo gën jabar ju pànk.
25Xibaaru jàmm, bawoo fu sore mooy ndox mu sedd ci ku loof.
26Ku jub bu dee nangul ku bon, yàqu na, ni seyaan bu nëx mbaa teen bu xàbb.

Read Kàddu yu Xelu 25Kàddu yu Xelu 25
Compare Kàddu yu Xelu 25:20-26Kàddu yu Xelu 25:20-26