Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 25

Kàddu yu Xelu 25:10-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
10Lu ko moy ñu dégg ko, rusloo la, sab der yàqu yaxeet.
11Wax ju ñor di nataalu wurus wu tege ci xaalis.
12Kàddu yu lay yedd ci kuy dégg, jaarob wurus la mbaa gànjaru ngalam.
13Ndaw lu wóor day seral xolu njaatigeem, mooy ndox mu sedd ci tàngooru ngóob.
14Kuy dige te doo joxe, yaay xiin wu ngelaw, mu naaxsaay.
15Muñ mer ay nax kilifa, te wax ju neex, fu mu jaar, mu nooy.
16Boo gisee lem, lekkal lu yem; bu ëppee, nga waccu ko.
17Na sa tànk di gëj kër dëkkandoo; boo ko sàppee, mu jéppi la.

Read Kàddu yu Xelu 25Kàddu yu Xelu 25
Compare Kàddu yu Xelu 25:10-17Kàddu yu Xelu 25:10-17