Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 25

Kàddu yu Xelu 25:1-7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Lii it ay kàddu yu xelu la, di yu Suleymaan, ay niti Esekiya buurub Yuda sotti ko.
2Màggug Yàllaa ngi ci li mu làq, darajay buur a ngi ci li mu feeñal.
3Maneesula daj li ci xelu buur, xalaatam daa kawe ni asamaan, xóot ni suuf.
4Xellil xaalis, tonni lu ca rax, ba ab tëgg man caa am ndab.
5Ab soxor it, dàqal, mu sore buur, ngir njubte law, jalam sax.
6Bul réy-réylu fi kanam buur, bul tooge jataayu boroom daraja,
7ndax ñu ne la: «Yéegal, jegesi fii,» moo gën ñu torxal la ci kanam kilifa. Boo gisalee sa bopp it,

Read Kàddu yu Xelu 25Kàddu yu Xelu 25
Compare Kàddu yu Xelu 25:1-7Kàddu yu Xelu 25:1-7