Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 24

Kàddu yu Xelu 24:27-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
27Ruujal sab tool, ji ko, doora tabax sa kër.
28Bul tuumaal nit ci neen, te bu ko seedeel ay fen.
29Bul ne: «Li mu ma def laa koy def, damay feyu li mu ma def.»
30Toolub ku yaafus laa jaare, ak tóokërub nit ku ñàkk bopp.
31Ndeke lépp a nga saxi dég, fépp fees akum ñax, tabaxu doj ba ko wër màbb.
32Maa ko gis, di xalaat, xoolaat ko, jànge ca.

Read Kàddu yu Xelu 24Kàddu yu Xelu 24
Compare Kàddu yu Xelu 24:27-32Kàddu yu Xelu 24:27-32