15Sama doom, soo xeloo, sama xol neex.
16Ngay wax njub, ma bég.
17Bul ñee bàkkaarkat, saxool ragal Aji Sax ji,
18ndax kat moo am muj, te kon sa yaakaar du tas.
19Déglul, doom, muusal te yebu ci yoonu njub.
20Bul bokk ci ñiy lekk lu ëpp, ak a màndi,
21ndax ku bëgg lekk ak a màndi, ñàkk dab la, dajjant it, rafle rekk.
22Déglul sa baay bi la jur. Bu sa ndey màggatee, bu ko sàggane.
23Jëndal dëgg te bu ko jaay. Sàkkul xel mu rafet ak yar akug dégg.
24Su doom jubee, seral xolu baay. Boo juree ku rafet xel, am nga bànneex.
25Deel bégal ndey ak baay, rawatina ndey ji la jur.
26Doom, teewloo ma xel te roy ma.
27Ab gànc yeer mu xóot la, jabaru jaambur di teen bu xat.
28Ma ngay tëroo nib sàcc, góor ñu bare lay fecciloo worma.
29Ana kuy tiislu, naan: «Wóoy, ngalla man!» Ana kuy xulook a jàmbat, di gaañu ci dara, bët ya xonq curr?