Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 23:15-29 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 23:15-29 in Kàddug Yàlla gi

15 Sama doom, soo xeloo, sama xol neex.
16 Ngay wax njub, ma bég.
17 Bul ñee bàkkaarkat, saxool ragal Aji Sax ji,
18 ndax kat moo am muj, te kon sa yaakaar du tas.
19 Déglul, doom, muusal te yebu ci yoonu njub.
20 Bul bokk ci ñiy lekk lu ëpp, ak a màndi,
21 ndax ku bëgg lekk ak a màndi, ñàkk dab la, dajjant it, rafle rekk.
22 Déglul sa baay bi la jur. Bu sa ndey màggatee, bu ko sàggane.
23 Jëndal dëgg te bu ko jaay. Sàkkul xel mu rafet ak yar akug dégg.
24 Su doom jubee, seral xolu baay. Boo juree ku rafet xel, am nga bànneex.
25 Deel bégal ndey ak baay, rawatina ndey ji la jur.
26 Doom, teewloo ma xel te roy ma.
27 Ab gànc yeer mu xóot la, jabaru jaambur di teen bu xat.
28 Ma ngay tëroo nib sàcc, góor ñu bare lay fecciloo worma.
29 Ana kuy tiislu, naan: «Wóoy, ngalla man!» Ana kuy xulook a jàmbat, di gaañu ci dara, bët ya xonq curr?
Kàddu yu Xelu 23 in Kàddug Yàlla gi