Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 23

Kàddu yu Xelu 23:13-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
13Bul ñéebloo yar gone, bantal ko taxu koo dee.
14Soo ko bantalee, mu mana mucc.
15Sama doom, soo xeloo, sama xol neex.
16Ngay wax njub, ma bég.
17Bul ñee bàkkaarkat, saxool ragal Aji Sax ji,
18ndax kat moo am muj, te kon sa yaakaar du tas.

Read Kàddu yu Xelu 23Kàddu yu Xelu 23
Compare Kàddu yu Xelu 23:13-18Kàddu yu Xelu 23:13-18