Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 22

Kàddu yu Xelu 22:9-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Ku tabe am barke, mooy kiy sédd ku ñàkk cib dundam.
10Dàqal kuy ñaawle, ay jeex, xulooki saaga dakk.
11Ku dëggu, wax ja yiw, buur di xaritam.
12Aji Sax jeey sàmm liy dëgg, di weddi waxi fen-kat.
13Bul yaafus, ba naan: «Gayndee ngi ci biti, dañu may rey ci mbedd mi!»
14Waxi ndaw su yemadi am yeer la, ku Aji Sax ji rëbb moo cay tàbbi.
15Yëfi dof daa sax ci xolu gone, boo bantalee, mu tàggook moom.
16Not néew-ji-doole ngir yokkule, mbaa may boroom alal, loo ci def mu wàññi la.
17Teewlul te déglu li boroom xel yi wax. Defal sam xel ci li ma lay xamal.
18Soo mokkalee, ba man koo tari, muy sa mbégte.
19Yaw laa koy xamal tey jii, ndax nga wóolu Aji Sax ji.

Read Kàddu yu Xelu 22Kàddu yu Xelu 22
Compare Kàddu yu Xelu 22:9-19Kàddu yu Xelu 22:9-19