4Xeebaateek réy-réylu mooy bàkkaar yi ñuy ràññee ku bon.
5Farlu, woomle; ku gaawtu, mujj néewle.
6Alal ju la fen may, cóolóol la, day naaw, wut ko xaru la.
7Coxor day sànk boroom, ndax day baña def njub.
8Ab saaysaay day dëngal, nit ku dëggu di jubal.
9Dëkkeb ruq cim sàq moo gën jabar ju pànk.
10Ab soxor day namma lore, te du yërëm moroomam.
11Boo mbugalee kuy ñaawle, ab téxét jànge ca; nga jàngal ku rafet xel, mu yokku.
12Aji Jub ji Yàlla xam na la ne ca biir kër ku bon, te mooy sànk ku bon.
13Ku tanqamlu jooyi ku ñàkk dina woote wall, wall ñàkk.
14Ku mer, may ko ci sutura, mu giif; boroom xadar, boqal ko neexal, mu dal.
15Bu yoon amee, ku jub bég; kuy def lu bon jàq.