22Ku ñaw mana daan jàmbaari dëkk bu mag, ba màbb tata ja ñu yaakaaroon.
23Ub sa gémmiñ, moom sa làmmiñ, mucc ci njàqare.
24Ku réy te bew, mooy ñaawle, day reew, ba jéggi dayo.
25Ab yaafus day bëgg lu mu amul ba dee, ndax du nangoo liggéey;
26day yendoo xemmem, te du am, ka jub di joxeek a joxewaat.
27Saraxu nit ku bon ñaawtéef la, rawatina bu ci jubloo lu bon.
28Seede buy fen day sànku, kuy dégg, sa kàddu sax.
29Ku bon day ñeme-ñemelu, ku jub la muy def da koy wóor.
30Nit xeluwul, amul ug dégg ak pexe, ba manal Aji Sax ji dara.
31Nit ay takk, bésub xare, Aji Sax ji di maye ndam.