Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 18

Kàddu yu Xelu 18:7-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Ab dof, waxam a koy sànk, làmmiñu boppam a koy dugal.
8Waxi jëwkat di ñam wu neex wuy seey, jàll ca biir-a-biir.
9Kuy sàggane sa liggéey, yaak kuy yàq a bokk.
10Turu Aji Sax ji rawtu bu mag la. Ku jub daw làqu ca, raw.
11Alal day aar boroom ni ab tata, mu xalaat ne maneesu koo bëtt.
12Bew, yàqule; jëkke woyof, mujje tedd.

Read Kàddu yu Xelu 18Kàddu yu Xelu 18
Compare Kàddu yu Xelu 18:7-12Kàddu yu Xelu 18:7-12