7 Ab dof, waxam a koy sànk, làmmiñu boppam a koy dugal.
8 Waxi jëwkat di ñam wu neex wuy seey, jàll ca biir-a-biir.
9 Kuy sàggane sa liggéey, yaak kuy yàq a bokk.
10 Turu Aji Sax ji rawtu bu mag la. Ku jub daw làqu ca, raw.
11 Alal day aar boroom ni ab tata, mu xalaat ne maneesu koo bëtt.
12 Bew, yàqule; jëkke woyof, mujje tedd.