4Ku bon ay déglu wax ju bon, fen-kat di teewlu ay sos.
5Kuy ñaawal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; kuy reetaan ku jàq, mbugalam du jaas.
6Teraangay maam, sët ba; sagu doom, baay ba.
7Waxi teggin jekkul cib dof, ay fen ci as gor waxi noppi.
8Alalu ger njiglaay la ca ka koy joxe, ba fu mu jublu, mu nooy.
9Bale tooñ, yokk cofeel; sulliw ay, tas xarit.
10Ku am ug dégg ngay yedd benn yoon, ab dof téeméeri yar du ko waññi.
11Ku bon fippu doŋŋ lay jéem, te musibaa koy dikkal.
12Taseek gaynde gu ñàkki doomam moo gën taseek dof ak yëfi dofam.
13Kuy feye mbon jëf ju baax, lu bon du jóge sa kër.