20Ku njublaŋ du baaxle, kuy wax njekkar añe musiba.
21Ku jur ab dof, am naqar; ab dof waajuram du bég.
22Xol bu sedd day garabal, xol bu tiis day semmal.
23Ku bon day nangu alalu ger ca suuf, nara jalgati yoon.
24Ku am ug dégg ne jàkk ci xel mu rafet, ab dof ne xóll, xel ma sore lool.
25Doom ju dof di tiisu baay ba ak naqaru ndey ja.
26Ku deful dara, feyloo kob daan, dug njub; dóor as gor du yoon.
27Ku moom sa làmmiñ am nga xam-xam, te ku teey am ngag dégg.
28Ab dof sax bu noppee, nirook boroom xel; ku ne cell, ñu fooge lag muus.