2Surga, bu rafetee xel, tiim doom juy rusloo, séddu ni doom ci alalu sangam.
3Xaalis ak wurus sawaraa koy xelli, waaye nit, ab xolam, Aji Sax jee koy nattu.
4Ku bon ay déglu wax ju bon, fen-kat di teewlu ay sos.
5Kuy ñaawal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; kuy reetaan ku jàq, mbugalam du jaas.
6Teraangay maam, sët ba; sagu doom, baay ba.