2 Surga, bu rafetee xel, tiim doom juy rusloo, séddu ni doom ci alalu sangam.
3 Xaalis ak wurus sawaraa koy xelli, waaye nit, ab xolam, Aji Sax jee koy nattu.
4 Ku bon ay déglu wax ju bon, fen-kat di teewlu ay sos.
5 Kuy ñaawal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; kuy reetaan ku jàq, mbugalam du jaas.
6 Teraangay maam, sët ba; sagu doom, baay ba.